3 Moo dencal bànni Israyil ngoram, dencal ko wormaam, àddina ba mu daj di gis ni nu sunu Yàlla walloo.
4 Yeen àddina sépp, xaacul-leen Aji Sax ji, sampleen, sarxolle te woy!
5 Xalamal-leen Aji Sax ji, woyal ko, xalamal ko, woyati.
6 Wal-leen liit yi, wal bufta yi te xaacul Buur Aji Sax ji!