7 Yeen làngi xeet yi, seedeel-leen Aji Sax ji; seedeel-leen Aji Sax ji teddngaak doole.
8 Seedeel-leen Aji Sax ji teddngay turam, yékkatil kob sarax, duggaale ëttam.
9 Sujjóotal-leen Aji Sax ji làmboo sellnga, te àddina wërngal këpp di ko loxal.
10 Neleen xeet yi Aji Sax jeey buur: àddinaa ngii, dëju te raful. Mooy àtte xeet yi njub.
11 Asamaanoo, bégal! Suufoo, bànneexul! Géejoo, riiral yaak li la fees,
12 te mbooy mi di jaayu, mook lu ci biiram, garabi àll bi sarxolleendoo,
13 gatandoo ko Aji Sax jiy dikk, àttesi àddina, di àtte dun bi njekk, tey àttee xeet yépp dëggam.