3 Siiwal-leen teddngaam fi biir xeet yi, xamal waasoo waaso ay jalooreem.
4 Aji Sax jee màgg, jara santa sant te gëna mata ragal lépp lu ñuy jaamu.
5 Mboolem yàlla yi xeet yiy jaamu, yàllantu la, waaye Aji Sax jee sàkk asamaan.
6 Màggaay ak daraja, fa moom, dooleek taar, fa këram gu sell.
7 Yeen làngi xeet yi, seedeel-leen Aji Sax ji; seedeel-leen Aji Sax ji teddngaak doole.
8 Seedeel-leen Aji Sax ji teddngay turam, yékkatil kob sarax, duggaale ëttam.