7 Mooy sunu Yàlla, nuy xeet wi muy foral, diy gàtt ciy loxoom. Bésub tey yal nangeen dégg kàddoom
8 ga mu noon: «Buleen të, na woon fa Meriba, jantub keroog fa Maasa, ca màndiŋ ma,
9 fa ma seeni maam doon nattoo, di ma seetlu te gis la ma def.
10 Ñeent fukki at laa jéppi googu maas, ma ne: “Xeet wu ñàkk wormaa ngi, te faaleedi samay santaane.”
11 Moo ma taxa mer, ba giñal leen, ne duñu tàbbi fa sama noflaay.»