3 Aji Sax jeey Yàlla ju màgg ji, buur bu mag bi tiim yàllay xeet yépp.
4 Moo moom xóotey suuf, moom colli tund yi,
5 moom géej, sàkk ko, moom jéeri ji mu mooñ.
6 Nan sëgg, sujjóot, sukkal Aji Sax ji nu sàkk.
7 Mooy sunu Yàlla, nuy xeet wi muy foral, diy gàtt ciy loxoom. Bésub tey yal nangeen dégg kàddoom
8 ga mu noon: «Buleen të, na woon fa Meriba, jantub keroog fa Maasa, ca màndiŋ ma,
9 fa ma seeni maam doon nattoo, di ma seetlu te gis la ma def.
10 Ñeent fukki at laa jéppi googu maas, ma ne: “Xeet wu ñàkk wormaa ngi, te faaleedi samay santaane.”