7 te naa: «Ki Sax gisu ci, Yàllay Yanqóoba jii yégu ko.»
8 Yeen bokk yu dofe yi, moytuleen. Gàtt xel yi, kañ ngeen di muus?
9 Ki jëmbati nopp, da dul dégg a? Am ki xari gët, da dul gis?
10 Kiy yar yéefar yi, da dul mbugalee? Du mooy kiy xamal nit?
11 Aji Sax ji xam na xalaatu nit, xam ne cóolóolu neen la.
12 Ki Sax, ndokklee ki ngay yar, tàggat ko ci saw yoon,