Text copied!
Bibles in Wolof

Sabóor 94:13-20 in Wolof

Help us?

Sabóor 94:13-20 in Kàddug Yàlla gi

13 dëfal ko ci bési safaan, ba keroog ñuy gasal ku bon.
14 Boroom bi kat du wacc ñoñam mukk, du bàyyi ay séddoom.
15 Àtte dina dellu laloo njekk, képp ku jub topp ca.
16 Ana ku may taxawal ci ñu bon ñi? Ku may jógal ci biir ñiy def lu bon?
17 Su ma Aji Sax ji walluwloon, tuuti ma fanaani réew ma ne selaw.
18 Dama noon: «Tarxiis naa!» Waaye yaa ma awoo sa ngor.
19 Ma bare xalaati xol, nga dëfal ma, ma bég.
20 Loo séq ak njiit lu jubadi luy yoonal njubadi?
Sabóor 94 in Kàddug Yàlla gi