Text copied!
Bibles in Wolof

Sabóor 94:10-16 in Wolof

Help us?

Sabóor 94:10-16 in Kàddug Yàlla gi

10 Kiy yar yéefar yi, da dul mbugalee? Du mooy kiy xamal nit?
11 Aji Sax ji xam na xalaatu nit, xam ne cóolóolu neen la.
12 Ki Sax, ndokklee ki ngay yar, tàggat ko ci saw yoon,
13 dëfal ko ci bési safaan, ba keroog ñuy gasal ku bon.
14 Boroom bi kat du wacc ñoñam mukk, du bàyyi ay séddoom.
15 Àtte dina dellu laloo njekk, képp ku jub topp ca.
16 Ana ku may taxawal ci ñu bon ñi? Ku may jógal ci biir ñiy def lu bon?
Sabóor 94 in Kàddug Yàlla gi