Text copied!
Bibles in Wolof

Sabóor 92:10-15 in Wolof

Help us?

Sabóor 92:10-15 in Kàddug Yàlla gi

10 Aji Sax ji, sa noon yi kay, ndeke yoo; ndeke yoo sa noon yi, sànku rekk; defkati mbon ñépp, fëlxoo rekk.
11 May nga ma dooley nagu àll, ma diwoo diw gu bees.
12 Maa gis jéllu noon yi, dégg yuuxi ñu bon ñi may tëru.
13 Ku jub day naat nig tàndarma, màgg ni seedaru Libaŋ
14 gu ñu jëmbat biir kër Aji Sax ji, muy naate sunu biir ëttu Yàlla;
15 bu màggatee sax di meññ, tooy xepp, sëq lipp,
Sabóor 92 in Kàddug Yàlla gi