7 Junni daanu fi sa wet, fukki junni (10 000) daanu fi sa ndijoor, du tax mu jege la.
8 Say gët nga ciy teg, di seetaan ku bon di jot yoolam.
9 Yaw mi màkkaanoo Aji Sax ji, Aji Kawe jii di sama rawtu,
10 genn loraange du la dab, balaa du jege sa xayma.
11 Ay malaakaam la lay booleel, ñu di la sàmm foo jëm.