3 Kii kay moo lay musal cig fiir ak loraangey mbas.
4 Kiiraayam la lay sànge, nga yiiru, làqu; wormaam yéew la, di la aar.
5 Doo ragal njàqarey guddi mbaa fittu bëccëg
6 mbaa mbas mu yooteg lëndëm, ak balaa buy fàdde njolloor.
7 Junni daanu fi sa wet, fukki junni (10 000) daanu fi sa ndijoor, du tax mu jege la.