13 Dangay falaxe jaan ak gaynde, di rajaxe ñàngóor ak sibi.
14 Yàlla da naa: «Kii de man la safoo, ma di ko xettli. Man la xam, te maa koy teg fu wóor.
15 Mu woo ma, ma wuyu ko; mook man ci biir njàqare, ma xettli ko, darajaal ko,
16 reggal koy fan, baaxe ko samag wall.»