Text copied!
Bibles in Wolof

Sabóor 8:4-9 in Wolof

Help us?

Sabóor 8:4-9 in Kàddug Yàlla gi

4 Damay xool sa asamaan si nga móol, ak weer week biddiiw yi nga fi teg.
5 Moo luy nit, ba nga di ko bàyyi xel? Luy doom aadamaak loo koy yége?
6 Yaa def nit mu yées malaaka yi as lëf, te yaa ko kaalaa teraangaak daraja,
7 fal ko ci kaw loo bind, jox ko lépp, mu teg tànk:
8 jur gépp, gu gudd ak gu gàtt, rabi àll it ca la,
9 ak njanaaw ak jën, ak luy jaare yooni géej.
Sabóor 8 in Kàddug Yàlla gi