3 Làmmiñu tuut-tànk, ba ci luy nàmp, feeñal nga ca sa kàttan, bañaaleek feyukat ne xerem.
4 Damay xool sa asamaan si nga móol, ak weer week biddiiw yi nga fi teg.
5 Moo luy nit, ba nga di ko bàyyi xel? Luy doom aadamaak loo koy yége?
6 Yaa def nit mu yées malaaka yi as lëf, te yaa ko kaalaa teraangaak daraja,
7 fal ko ci kaw loo bind, jox ko lépp, mu teg tànk: