Text copied!
Bibles in Wolof

Sabóor 89:9-13 in Wolof

Help us?

Sabóor 89:9-13 in Kàddug Yàlla gi

9 Yàlla, Aji Sax ji Boroom gàngoor yi, Ki Sax, ana ku tollook yaw doole? Yaw mi worma féete fu ne!
10 Yaw yaa man géej gu sàmbaraax; gannax ya fuddu, nga dalal.
11 Yaa fàdd Raxab, bóom ko, tasaare say noon ci sa doole.
12 Yaa moom asamaan, yaa moom suuf. Àddinaak li ci biiram, yaa ko taxawal.
13 Bëj-gànnaar ak bëj-saalum, yaa ko sàkk. Tabor ak Ermon, tund ya, di sarxollee sa tur.
Sabóor 89 in Kàddug Yàlla gi