Text copied!
Bibles in Wolof

Sabóor 89:47-51 in Wolof

Help us?

Sabóor 89:47-51 in Kàddug Yàlla gi

47 Éy Aji Sax ji, xanaa lii du jeex? Xanaa doo làqu fàww nii, sa mer di boy?
48 Bàyyi ma xel, samay fan yàggul. Xanaa du neen a tax nga sàkk mboolem doom aadama?
49 Ana kuy dund te du dee? Ku mana rëcc tëraayu bàmmeel? Selaw.
50 Boroom bi, ana sa ngor la nga daan jëfe te nga giñale woon ko Daawuda ci sa worma?
51 Boroom bi, bàyyil xel ci sa gàcceg jaam ñi, ak xeet yu bare yi ma yenu yépp.
Sabóor 89 in Kàddug Yàlla gi