37 askanam, dàkk; ab jalam fi sama kanam ni jant bi,
38 ak weer wi sax ba fàww, dib seede bu wér ca niir ya.» Selaw.
39 Ndaxam yaw Yàlla, jéppi nga ki nga fal, mere ko, wacc ko.
40 Fecci nga sa kóllëreek sab jaam, foq nguuram, detteel ko.
41 Bëtt nga miiram yépp, saam ay tataam,
42 ku fa jaare, jël ca alalam, mu doon mbalitu dëkkandoo yi.
43 Yékkati ngay bañam, noonam yépp di ree.
44 Dayal nga saamaram, te taxawuwloo ko cib xare.
45 Xañ nga ko darajaam, rattax ngànguneem fa suuf.
46 Dagg nga fani ngoneem, sang ko gàcce. Selaw.