3 Dama ne, sa ngor dàkk la sax, fa asamaan nga dëël sa worma.
4 Aji Sax ji nee: «Damaa fas kóllëreek ki ma tànn, muy Daawuda sama jaam bi ma giñal ne ko:
5 “Damay saxal sa askan ba fàww, samp sab jal sët ba sëtaat.”» Selaw.
6 Aji Sax ji, waa asamaan a ngi lay sante say jaloore, ndajem ñu sell ña di la joobee sa worma.
7 Ana kuy dab-dabal Aji Sax ji, fa kawa kaw? Ana ci goney Yàlla yi ku nirook Aji Sax ji,
8 Yàlla, ji ñu terala teral ci jataayu ñu sell ñi, te mu gëna raglu lu ko wër?