Text copied!
Bibles in Wolof

Sabóor 89:27-34 in Wolof

Help us?

Sabóor 89:27-34 in Kàddug Yàlla gi

27 Moo ma naa: “Yaay sama baay, di sama Yàlla, di sama wéeru-mucc.”
28 Te it maa koy def samab taaw, tiimale ko buuri àddina,
29 sàmmal ko sama ngor ba fàww, feddlil ko sama kóllëre.
30 Damay saxal askanam ba fàww, yàggal ab jalam ni asamaan.
31 Bu ay sëtam wàccee sama yoon, baña doxe samay ndigal,
32 mbaa ñu xëtt sama dogali yoon, baña sàmmonteek samay santaane,
33 ma bantale leen seenug moy, dumaa leen seen ñaawtéef.
34 Waaye duma ko daggal sama ngor, te duma ko ñàkke worma.
Sabóor 89 in Kàddug Yàlla gi