Text copied!
Bibles in Wolof

Sabóor 89:23-36 in Wolof

Help us?

Sabóor 89:23-36 in Kàddug Yàlla gi

23 Noon du ko bett, ku bon du ko torxal.
24 Ay bañam, ma rajaxe; ay noonam, ma fàdd,
25 sama wormaak sama ngor di ko gunge, may yokk kàttanam.
26 Géej, ma teg ci loxoom, dex, ma ne ca tegg ndijooram.
27 Moo ma naa: “Yaay sama baay, di sama Yàlla, di sama wéeru-mucc.”
28 Te it maa koy def samab taaw, tiimale ko buuri àddina,
29 sàmmal ko sama ngor ba fàww, feddlil ko sama kóllëre.
30 Damay saxal askanam ba fàww, yàggal ab jalam ni asamaan.
31 Bu ay sëtam wàccee sama yoon, baña doxe samay ndigal,
32 mbaa ñu xëtt sama dogali yoon, baña sàmmonteek samay santaane,
33 ma bantale leen seenug moy, dumaa leen seen ñaawtéef.
34 Waaye duma ko daggal sama ngor, te duma ko ñàkke worma.
35 Duma fecci sama kóllëre, te duma toxal sama kàddu.
36 Benn yoon laa ko giñ ci sama sellnga, duma fen Daawuda:
Sabóor 89 in Kàddug Yàlla gi