Text copied!
Bibles in Wolof

Sabóor 89:19-24 in Wolof

Help us?

Sabóor 89:19-24 in Kàddug Yàlla gi

19 Sunu kiirlaay lii, Aji Sax jeey boroom; sunu buur bii, Aji Sell ji séddoo Israyil ay boroom.
20 Wax nga say wóllëre ci peeñu, ne leen: «Tànne naa jàmbaar ci xeet wi, dénk ko ndimbal.
21 Gis naa sama jaam Daawuda, fale ko sama diw gu sell,
22 ànd ak moom, saxal ko, di ko dooleel.
23 Noon du ko bett, ku bon du ko torxal.
24 Ay bañam, ma rajaxe; ay noonam, ma fàdd,
Sabóor 89 in Kàddug Yàlla gi