17à nd di la bége bés bu ne, sag njekk siggil leen.
18Seen darajay doole, yaw a. Boo nu baaxee, nu yokku kà ttan.
19Sunu kiirlaay lii, Aji Sax jeey boroom; sunu buur bii, Aji Sell ji séddoo Israyil ay boroom.
20Wax nga say wóllëre ci peeñu, ne leen: «Tà nne naa jà mbaar ci xeet wi, dénk ko ndimbal.