Text copied!
Bibles in Wolof

Sabóor 89:1-13 in Wolof

Help us?

Sabóor 89:1-13 in Kàddug Yàlla gi

1 Muy taalif bu ñeel Etan mi bokk ci giirug Esra.
2 Aji Sax ji laay woye ngoram, ba fàww, di biral wormaam sët ba sëtaat.
3 Dama ne, sa ngor dàkk la sax, fa asamaan nga dëël sa worma.
4 Aji Sax ji nee: «Damaa fas kóllëreek ki ma tànn, muy Daawuda sama jaam bi ma giñal ne ko:
5 “Damay saxal sa askan ba fàww, samp sab jal sët ba sëtaat.”» Selaw.
6 Aji Sax ji, waa asamaan a ngi lay sante say jaloore, ndajem ñu sell ña di la joobee sa worma.
7 Ana kuy dab-dabal Aji Sax ji, fa kawa kaw? Ana ci goney Yàlla yi ku nirook Aji Sax ji,
8 Yàlla, ji ñu terala teral ci jataayu ñu sell ñi, te mu gëna raglu lu ko wër?
9 Yàlla, Aji Sax ji Boroom gàngoor yi, Ki Sax, ana ku tollook yaw doole? Yaw mi worma féete fu ne!
10 Yaw yaa man géej gu sàmbaraax; gannax ya fuddu, nga dalal.
11 Yaa fàdd Raxab, bóom ko, tasaare say noon ci sa doole.
12 Yaa moom asamaan, yaa moom suuf. Àddinaak li ci biiram, yaa ko taxawal.
13 Bëj-gànnaar ak bëj-saalum, yaa ko sàkk. Tabor ak Ermon, tund ya, di sarxollee sa tur.
Sabóor 89 in Kàddug Yàlla gi