Text copied!
Bibles in Wolof

Sabóor 88:5-11 in Wolof

Help us?

Sabóor 88:5-11 in Kàddug Yàlla gi

5 ñu sóoraale maak ñi wàcci biir bàmmeel. Ma mel ni jàmbaar ju kenn amatul yaakaar,
6 bokk ci néew, yi dara waratul, mbaa ku ñu bóom, mu tëdd cim pax, faaleetoo ko, xanaa dagg ko, wacc.
7 Tàbbal nga ma kàmb gu xóot, biir xóotey lëndëm.
8 Yen nga ma sa xadar, tance ma sa gannax yépp. Selaw.
9 Dàqal nga may xame, tax nga ñu seexlu ma; ma tëju, génnatuma.
10 Samay gët a ngi giim ndax naqar. Éy Aji Sax ji, maa ngi lay woo bés bu ne, dékk lay loxo.
11 Ku dee, lu muy doyeeti say kéemaan? Ndax néew dina jóg di la màggal? Selaw.
Sabóor 88 in Kàddug Yàlla gi