Text copied!
Bibles in Wolof

Sabóor 88:3-6 in Wolof

Help us?

Sabóor 88:3-6 in Kàddug Yàlla gi

3 Yal na sama ñaan àgg fa yaw; teewlul, ma woote wall.
4 Damaa suur këll ay musiba, ba soreetuma njaniiw,
5 ñu sóoraale maak ñi wàcci biir bàmmeel. Ma mel ni jàmbaar ju kenn amatul yaakaar,
6 bokk ci néew, yi dara waratul, mbaa ku ñu bóom, mu tëdd cim pax, faaleetoo ko, xanaa dagg ko, wacc.
Sabóor 88 in Kàddug Yàlla gi