3 Yal na sama ñaan àgg fa yaw; teewlul, ma woote wall.
4 Damaa suur këll ay musiba, ba soreetuma njaniiw,
5 ñu sóoraale maak ñi wàcci biir bàmmeel. Ma mel ni jàmbaar ju kenn amatul yaakaar,
6 bokk ci néew, yi dara waratul, mbaa ku ñu bóom, mu tëdd cim pax, faaleetoo ko, xanaa dagg ko, wacc.
7 Tàbbal nga ma kàmb gu xóot, biir xóotey lëndëm.
8 Yen nga ma sa xadar, tance ma sa gannax yépp. Selaw.
9 Dàqal nga may xame, tax nga ñu seexlu ma; ma tëju, génnatuma.
10 Samay gët a ngi giim ndax naqar. Éy Aji Sax ji, maa ngi lay woo bés bu ne, dékk lay loxo.