13 Ana kuy yég say kéemaan ci googu lëndëm? Ku lay seedeel njekk réew ma fàtte faloo?
14 Aji Sax ji, man, yaw lay woo wall, xëy, kare la gii ñaan, ne la:
15 Éy Aji Sax ji, loo may gàntale, di ma fuuylu?
16 Mitit bay laatikaaf, sama ngone ba tey; sa mbugal yu raglu, ba bopp ubu ràpp!
17 Sa mer mëdd ma, sa mbugal yu raglu sànk ma,
18 mëdd ma nim ndox bés bu ne, gëndoo fi sama kaw.