12 Dees na siiwal sa ngor biir bàmmeel, mbaa sa worma ci paxum sànkute?
13 Ana kuy yég say kéemaan ci googu lëndëm? Ku lay seedeel njekk réew ma fàtte faloo?
14 Aji Sax ji, man, yaw lay woo wall, xëy, kare la gii ñaan, ne la:
15 Éy Aji Sax ji, loo may gàntale, di ma fuuylu?