Text copied!
Bibles in Wolof

Sabóor 86:6-11 in Wolof

Help us?

Sabóor 86:6-11 in Kàddug Yàlla gi

6 Éy Aji Sax ji, teewlul, ma ñaan la; déglul, ma tinu la.
7 Bu ma la wooyee bésub njàqare, yaa may nangul.
8 Boroom bi, doo moroomu tuur yi, te jëf melul ni sa jos.
9 Boroom bi, mboolem xeet yi nga sàkk ñoo lay sujjóotalsi, di màggal sa tur.
10 Yaa màgg te yéemey jëf, yaw doŋŋ yaa di Yàlla.
11 Éy Aji Sax ji, won ma sa nammeel, ma doxe sa worma. Tënkal sama xol ci ragal la.
Sabóor 86 in Kàddug Yàlla gi