3 Éy Boroom bi, baaxe ma; yaw laay yendoo woo wall.
4 Boroom bi, bànneexalal sab jaam, yaw laa dékk sama xol.
5 Boroom bi, yaa baax, di bale, di nàddil sa ngor képp ku lay sàkku.
6 Éy Aji Sax ji, teewlul, ma ñaan la; déglul, ma tinu la.
7 Bu ma la wooyee bésub njàqare, yaa may nangul.
8 Boroom bi, doo moroomu tuur yi, te jëf melul ni sa jos.
9 Boroom bi, mboolem xeet yi nga sàkk ñoo lay sujjóotalsi, di màggal sa tur.
10 Yaa màgg te yéemey jëf, yaw doŋŋ yaa di Yàlla.
11 Éy Aji Sax ji, won ma sa nammeel, ma doxe sa worma. Tënkal sama xol ci ragal la.
12 Boroom bi sama Yàlla, naa la sante xol bu fees, màggal la ba fàww.