15 Waaye yaw Boroom bi Yàlla, yaa ñeewante, yërëm, yaa muñ mer, bare ngor ak worma.
16 Geesu ma, baaxe ma. Dooleelal sab jaam, wallul ki sa jaam sukk jur!
17 Ngalla def ma sa firndey mbaax, ba bañ yi gis ci, rus, ndax yaw Aji Sax, ji ma dimbali, dëfal ma.