14 Éy Yàlla, nit ñu bew a ma jógal, def gàngoor gu néeg, di rëbb sama bakkan, te seetuñu la ci.
15 Waaye yaw Boroom bi Yàlla, yaa ñeewante, yërëm, yaa muñ mer, bare ngor ak worma.
16 Geesu ma, baaxe ma. Dooleelal sab jaam, wallul ki sa jaam sukk jur!