11 Éy Aji Sax ji, won ma sa nammeel, ma doxe sa worma. Tënkal sama xol ci ragal la.
12 Boroom bi sama Yàlla, naa la sante xol bu fees, màggal la ba fàww.
13 Ngor lu réy nga ma won, sorele maak tëraayu bàmmeel.
14 Éy Yàlla, nit ñu bew a ma jógal, def gàngoor gu néeg, di rëbb sama bakkan, te seetuñu la ci.