7 Xanaa dinga leqli sa mbooloo, ba ñu man laa bànneexoo?
8 Éy Aji Sax ji, won nu sa ngor, baaxe nu sag wall.
9 Woykat ba nee: «Naa déglu lu Aji Sax ji Yàlla di wax.» Jàmm lay wax wóllëreem ñiy ñoñam, ba duñu dellu ci jëfi dof.
10 Wallam aka jege ñi ko ragal, te leeram dëgmal sunu réew mii!
11 Ngor ak kóllëree daje, njekk ak jàmm saafoonte,