4 Éy Aji Sax ji Boroom gàngoor yi, sama buur, sama Yàlla, sawoor sax tag, nga fat ko, mbelaar it sàkk tàggam, denc ay cuujam fa sa sarxalukaay.
5 Ndokklee ku dëkke sa kër, di la màggalati. Selaw.
6 Ndokklee ku lay doolewoo, te namma topp njool ma jëm sa kër.
7 Buy jàll xuru Jooyoo, mu saf ko bëti ndox, céebo sànge xur wa barke,
8 muy gëna am doole, ba teewi fa Yàlla ca Siyoŋ.
9 Éy Yàlla Aji Sax ji Boroom gàngoor yi, déglul, ma ñaan la! Yàllay Yanqóoba, teewlu ma. Selaw.
10 Éy Yàlla, geesul Buur, sunu kiirlaay, ngalla niiral kii nga fal.
11 Benn fan ci sab ëtt de moo dàq junniy fan feneen. Sama taxawaayu bunt kër Yàlla moo ma gënal tëraayu biir xaymab ku bon.