Text copied!
Bibles in Wolof

Sabóor 84:3-10 in Wolof

Help us?

Sabóor 84:3-10 in Kàddug Yàlla gi

3 Damaa namm ëttub Aji Sax ji, di ko gelu ba jeex tàkk, jëmm jeek xol bi, di xaacul Yàlla jiy dund.
4 Éy Aji Sax ji Boroom gàngoor yi, sama buur, sama Yàlla, sawoor sax tag, nga fat ko, mbelaar it sàkk tàggam, denc ay cuujam fa sa sarxalukaay.
5 Ndokklee ku dëkke sa kër, di la màggalati. Selaw.
6 Ndokklee ku lay doolewoo, te namma topp njool ma jëm sa kër.
7 Buy jàll xuru Jooyoo, mu saf ko bëti ndox, céebo sànge xur wa barke,
8 muy gëna am doole, ba teewi fa Yàlla ca Siyoŋ.
9 Éy Yàlla Aji Sax ji Boroom gàngoor yi, déglul, ma ñaan la! Yàllay Yanqóoba, teewlu ma. Selaw.
10 Éy Yàlla, geesul Buur, sunu kiirlaay, ngalla niiral kii nga fal.
Sabóor 84 in Kàddug Yàlla gi