3 Xoolal sa noon yiy riir, sa bañ yi fippu ba téen!
4 Sa ñoñ lañuy rabatal, di mànkool sa séddoo yii.
5 Ñu ne: «Ayca nu far seen xeet wi, ba deesul fàttlikooti turu Israyil.»
6 Dañoo mànkoo kat, te yaw lañu takktool:
7 muy néegi Edom ak Ismayla, néegi Mowab ak Agar,
8 néegi Gebal, Amon ak Amaleg ak waa Filisteek waa Tir,
9 réewum Asiri it fekki leen, di dooleel askanu Lóot wa. Selaw.