Text copied!
Bibles in Wolof

Sabóor 83:3-10 in Wolof

Help us?

Sabóor 83:3-10 in Kàddug Yàlla gi

3 Xoolal sa noon yiy riir, sa bañ yi fippu ba téen!
4 Sa ñoñ lañuy rabatal, di mànkool sa séddoo yii.
5 Ñu ne: «Ayca nu far seen xeet wi, ba deesul fàttlikooti turu Israyil.»
6 Dañoo mànkoo kat, te yaw lañu takktool:
7 muy néegi Edom ak Ismayla, néegi Mowab ak Agar,
8 néegi Gebal, Amon ak Amaleg ak waa Filisteek waa Tir,
9 réewum Asiri it fekki leen, di dooleel askanu Lóot wa. Selaw.
10 Def leen na nga defoon waa Majan, def ko Sisera ak Yabin ca dexu Kison.
Sabóor 83 in Kàddug Yàlla gi