13 ña ne woon: «Nan séddoo parluy Yàlla yi.»
14 Éy Yàlla, wëndeel leen ni callweer, ñu mel ni boob mu ngelaw wal.
15 Éy Yàlla, ni daay di xoyome àll, sawara wa jafal tund ya,
16 yal nanga leen ni toppeek sa dooley ngelaw, tiitale leen sa ngëlén.
17 Aji Sax ji, sëlëm leen gàcce, ba ñu sàkku la.