Text copied!
Bibles in Wolof

Sabóor 81:7-13 in Wolof

Help us?

Sabóor 81:7-13 in Kàddug Yàlla gi

7 «Sippi naa leen, woyofal seeni yoxo.
8 Ngeen jàq, woo ma, ma xettli leen, wuyoo leen fa kiiraayal dënn ya, te maa leen nattoo fa wal ma ca Meriba. Selaw.
9 Yeen sama ñoñ, dégluleen, ma dénk leen. Éy Israyil, su ngeen ma déglu woon!
10 Buleen fat tuuru jaambur, buleen sujjóotal tuuru doxandéem.
11 Man, Aji Sax ji, maay seen Yàlla ji leen yékkatee réewum Misra. Ŋaleen ŋafeet, ma reggal leen.
12 «Waaye sama ñoñ déggaluñu ma, Israyil gii nangulu ma.
13 Moo tax ma bërgël leen ak seenug të, ñuy wéye seeni pexe.
Sabóor 81 in Kàddug Yàlla gi