7 «Sippi naa leen, woyofal seeni yoxo.
8 Ngeen jàq, woo ma, ma xettli leen, wuyoo leen fa kiiraayal dënn ya, te maa leen nattoo fa wal ma ca Meriba. Selaw.
9 Yeen sama ñoñ, dégluleen, ma dénk leen. Éy Israyil, su ngeen ma déglu woon!
10 Buleen fat tuuru jaambur, buleen sujjóotal tuuru doxandéem.
11 Man, Aji Sax ji, maay seen Yàlla ji leen yékkatee réewum Misra. Ŋaleen ŋafeet, ma reggal leen.