5 ndegam ku ma jàmmal laa feye aw ay, mbaa ma dimbali ku ko noonoo te defu ko dara,
6 yal na ma noon rëbb, dab ma, dëggaate ma, sàggi saab sag, tëral ci pëndub suuf. Selaw.
7 Aji Sax ji, meral, jóg, dajeel maak xadaru noon yi! Ngalla teewlu ma; yaw, yoon nga santaane.
8 Yal na xeet yi daje, wër la, nga délsi tiim leen fu kawe.
9 Yal na Aji Sax ji àtte xeet yi; Aji Sax ji, seetal ci sama njubteek sama maandute te dëggal ma.