11 Sama kaaraange, fa Yàlla, miy musal boroom xol bu dëggu.
12 Yàllaay àtte dëgg. Yàllaay rëbbe bés bu ne.
13 Ku tuubul, Yàlla nàmm saamaram, bank xalaam, diir la.
14 Moom la waajalal ngànnaayi ndee, def ko fitt yuy boy.
15 Ku bon a ngoog, di matu doomu ñaawtéef. Day sos njombe, wasin njublaŋ.
16 Am kan lay gas, ba mu xóot, te pax ma mu gas, moo ca tàbbi.