7 Ñoo sëxëtoo giirug Yanqóoba, gental dëkkuwaayam.
8 Bul nu topp ñaawtéef ya woon, ngalla gaaw noo gatandoo sa yërmande. Danu ne dàll, ba ne dett.
9 Éy Yàlla, yaa nuy musal, wallu nu, ba sa seede rafet. Xettli nu te baal nu sunuy bàkkaar, ba sa woy rafet.