Text copied!
Bibles in Wolof

Sabóor 78:44-71 in Wolof

Help us?

Sabóor 78:44-71 in Kàddug Yàlla gi

44 Moo soppli deret seen yooni ndox, ba naaneetuñu wal ya.
45 Mu wàcce seen biir ndiiraanu weñ yu leen di lekk, ak mbott yu leen sànk.
46 Mu jox soccet yi seen gàncax, jébbal njéeréer yi seen meññeef.
47 Seen garabi reseñ, mu fóome tawab yuur, seen garabi sikomoor, mu fóome waame.
48 Seen jur gu gudd, mu bàyyeek tawab yuur, seeni gàtt, mu bàyyeek sawaray melax.
49 Yàlla sotti leen tàngooru xadaram, mu dim sànj ak naqar ak njàqare, lépp di gàngooru ndaw yu indiy musiba.
50 Mu afal meram, ba musalul seen bakkan, xanaa jébbal leen mbas ma.
51 Daa fàdd képp kuy taaw ca Misra te juddoo seen digg doole, fa xaymay sëti Xam.
52 Mu génne ñoñam niy gàtt, wommat leen ni gétt ca màndiŋ ma,
53 ba yóbbu leen fu wóor te tiituñu; seeni noon, géej ga mëdd leen.
54 Mu yóbbu leen fa suufam su sell sa, fa tund woowu mu jënde dooleem.
55 Da leena dàqal ay xeet, dogal leen céru suuf, sancal giiri Israyil ca seeni xayma.
56 Teewul ñuy diiŋat ak a gàntal Yàlla Aji Kawe ji, sàmmuñu ay dénkaaneem,
57 xanaa dëddu, di ko wor ni seeni maam, toogadi ni xala gu yolom.
58 Ñu di ko merlook seen bérabi jaamookaay, di ko fiirlook seen jëmmi tuur.
59 Ba ko Yàlla yégee, mer na, ba jéppi Israyil lool.
60 Mu gental dëkkuwaayam ba ca Silo, xaymaam ba mu sampoon ca doom aadama ya.
61 Mu jébbal ngàllo màndargam dooleem, may gànjaram ca loxol noon ba.
62 Daa bàyyee ñoñam saamaru noon, ndax mere yooya séddoom.
63 Seeni waxambaane deeye xare, seeni janq lamb;
64 seeni sarxalkat loroo saamar, te jëtun jooyul.
65 Ca la Boroom bi yewwu ni ku doon nelaw, mel ni jàmbaar ju biiñ xabtal.
66 Mu dóor noon ba yari gannaaw, teg leen gàcce gu dul fey,
67 ba noppi xalab waa kër Yuusufa, te tànnul giirug Efrayim,
68 xanaa tànn giirug Yuda, taamu tundu Siyoŋ wi mu sopp.
69 Mu tabax këram gu sell, na mu mel fa kawa kaw, dëgër ni suuf, si mu samp ba fàww.
70 Mu teg ca tabb Daawuda, jaamam ba, jële ko ca gétti xar ya,
71 fa mu doon topptoo jur ga; mu sàmmal ko waa kër Yanqóoba, askanu Israyil wi mu séddoo.
Sabóor 78 in Kàddug Yàlla gi