Text copied!
Bibles in Wolof

Sabóor 78:3-21 in Wolof

Help us?

Sabóor 78:3-21 in Kàddug Yàlla gi

3 muy lu nu dégg, xam ko, sunuy maam xamal nu ko.
4 Dunu ko nëbb sunuy doom, xanaa di ko jottli maas giy ñëw, xamal leen jaloorey Aji Sax ji ak kàttanam aki kéemaanam.
5 Bindal na sëti Yanqóoba téereb seede, muy yoon wi mu tegal Israyil. Mu sant maam yi, ñu xamal ko seeni doom,
6 ngir ñiy juddu ëllëg xam ko, am ay doom, ñu màgg, ba xamal ko seeni doom,
7 ngir ñu wóolu Yàlla, baña fàtte jëfi Yàlla, di jëfey santaaneem,
8 te baña roy seeni maam; maas gu të woon te déggadi, ñu ñàkk pastéef te sàmmuñu kóllërey Yàlla.
9 Waa giirug Efrayim ñoo soxi fitt, te keroog xare ba ñoo daw.
10 Ñoo sàmmul kóllërey Yàlla, gàntal yoonam,
11 ba fàtte ay jalooreem, di kéemaan yi mu leen won.
12 Fa seen kanami maam la def kéemaan, fa diiwaanu Cowan, réewum Misra.
13 Moo xar géej ga, jal ndox ma nim tata, jàlle leen.
14 Bëccëg mu jiitee leen aw niir, ak leeru sawara guddi gépp.
15 Moo xar ay doj ca màndiŋ ma, mbàmbulaan wal, mu nàndal leen;
16 mu sotti ndox mu balle ciw xeer, walal, mu safi dex.
17 Teewul ñu wéy di moy Aji Kawe ji, di ko gàntal ca màndiŋ ma.
18 Ñoo diiŋate Yàlla xol, di xemmem ñam wu bakkane.
19 Ñuy waxal Yàlla naan: «Xam ngeen ne Yàlla manu noo taajal ndab ci màndiŋ mi!
20 Dóor naw doj, moos, ndox ma fettax, wal ma baawaan, waaye aw ñam nag? Daa mana leel mbooloo mii aw yàpp?»
21 Aji Sax ji dégg ci, mer lool; xolam tàng ci sëti Yanqóoba, am sànj tàkkal Israyil.
Sabóor 78 in Kàddug Yàlla gi