24 tawal leen mànn, ñu lekk: peppum asamaan la leen leel;
25 mburum jàmbaar la nit lekk, mu wàcceel leen ca lu ne gàññ.
26 Yàlla wale ngelawal penku fa asamaan, bëmëx ak dooleem ngelawal bëj-saalum.
27 Mu tawal leenu yàpp, mu saawe ni pënd, di njanaaw yu ne gàññ ni feppi suufas géej,
28 wàcce ko fa seen digg dal ba, mu dajal seeni dëkkuwaay.
29 Mu faj seen aajo, ñu lekk ba suur këll.
30 Teewul bala seen xel a dal, seen lanc jàllagul sax,
31 Yàlla mer na, dal ci seen kaw, bóom ña ëpp doole ca ñoom, fàdd waxambaaney Israyil.
32 Loolu lépp teewul ñuy bàkkaar ba tey te gëmuñu ay kéemaanam.
33 Mu dagg seeni fan, mu wéy ni cóolóol, faat seen bakkan ci safaan bu gaaw.
34 Ba leen Yàlla fàddee, ña des sàkku ko, tuub, waññiku ci moom.
35 Ñu fàttliku ne Yàllaay seen cëslaay, xam ne Yàlla Aji Kawe jeey seen njotlaay.