19 Ñuy waxal Yàlla naan: «Xam ngeen ne Yàlla manu noo taajal ndab ci màndiŋ mi!
20 Dóor naw doj, moos, ndox ma fettax, wal ma baawaan, waaye aw ñam nag? Daa mana leel mbooloo mii aw yàpp?»
21 Aji Sax ji dégg ci, mer lool; xolam tàng ci sëti Yanqóoba, am sànj tàkkal Israyil.
22 Dañoo gëmul Yàlla, doyloowuñu wallam.
23 Mu digal niir ya fa kaw, ubbi bunti asamaan,
24 tawal leen mànn, ñu lekk: peppum asamaan la leen leel;
25 mburum jàmbaar la nit lekk, mu wàcceel leen ca lu ne gàññ.
26 Yàlla wale ngelawal penku fa asamaan, bëmëx ak dooleem ngelawal bëj-saalum.
27 Mu tawal leenu yàpp, mu saawe ni pënd, di njanaaw yu ne gàññ ni feppi suufas géej,
28 wàcce ko fa seen digg dal ba, mu dajal seeni dëkkuwaay.
29 Mu faj seen aajo, ñu lekk ba suur këll.
30 Teewul bala seen xel a dal, seen lanc jàllagul sax,
31 Yàlla mer na, dal ci seen kaw, bóom ña ëpp doole ca ñoom, fàdd waxambaaney Israyil.
32 Loolu lépp teewul ñuy bàkkaar ba tey te gëmuñu ay kéemaanam.
33 Mu dagg seeni fan, mu wéy ni cóolóol, faat seen bakkan ci safaan bu gaaw.
34 Ba leen Yàlla fàddee, ña des sàkku ko, tuub, waññiku ci moom.
35 Ñu fàttliku ne Yàllaay seen cëslaay, xam ne Yàlla Aji Kawe jeey seen njotlaay.
36 Teewul ñu di ko jéema naxey wax, di ko fen.
37 Joxuñu ko woon xol, sàmmuñu kóllëreem.
38 Teewul mu yërëm, baal leen seen ñaawtéef, ba sànku leen. Muñ na meram, muñati, te toppul xolam,
39 ndax xalaataat ne suuxu neen lañu, di noo guy dem te du délsi.
40 Gàntal nañu ko ba tàyyi ca màndiŋ ma, teg ko naqar ca ndànd-foyfoy ga.
41 Ñu dellu di diiŋat Yàlla, di naqaral Aji Sell, ji séddoo Israyil.
42 Fàtte nañu ndimbalam la, bés ba mu leen jotee ca noon ba,
43 ba def ay firndeem ca Misra, muy kiraamaam ya ca Cowan.
44 Moo soppli deret seen yooni ndox, ba naaneetuñu wal ya.