12 Waaye naa fàttliku jaloorey Ki Sax rekk, fàttliku kéemaanam ya woon.
13 Naa xalaat sa bépp liggéey, di jàngat say jëf.
14 Céy Yàlla, yaa sell jikko! Jan yàllaa màgg ni Yàlla?
15 Yaa di Yàlla juy jëfi kéemaan, yaa siiwal sa doole ci biir xeet yi.
16 Kàttan nga jote sa mbooloo ma, sëti Yanqóobaak Yuusufa. Selaw.