3 Xaymaam a nga Salem, di xunteem ma fa Siyoŋ.
4 Fa la rajaxee fitt yuy boy ak pakk ak saamar ak ngànnaayal xare. Selaw.
5 Yàlla yaa ne ràññ te darajawu, ba raw tundi rëbbkat yi.
6 Futtees nay boroom fit, ñu ne nërëm, nelaw; kuy ñeyi xare, say yoxo nasax.
7 Yaw Yàllay Yanqóoba, yaa gëdd, gawar ak fasam nelaw.
8 Yaw mii, yaa mata ragal; boo meree, ana kuy taxaw fi sa kanam?